Abadane

Baye Mass

Compositor: Não Disponível

Duma la bàyyi, duma la bàyyi
Yow it bul ma bàyyi, bul ma bàyyi yeeh

Moom ne na daf la bëgg piir
Ne na dafa bëgg nga nekk ki mu jiital
Moom ne na yaa de ki mu gis
Ne na ci ñoom ñépp yaw rekk la bëgg jiital
Ne na dootul la bàyyi
Yaw la tane ci góor ñi
Ne na dootul la bàyyi
Yaw la tane ci jigéen ñi

Duma la bàyyi, duma la bàyyi
Yow it bul ma bàyyi, bul ma bàyyi yeeh

Abadan, abadan, abadan
Abadan, yow bul ma bàyyi da’imam
Abadan, abadan, abadan
Abadan, yow bul ma bàyyi da’imam

Sa añ moo dàq lu ma mëna lekk
Sa kër moo dàq fu ma mëna nekk
Lu ñu neex lekk, lu ñu neex naan
Njaboot gi fecc ak a reetaan
Man dama la nob ba di la bëgga fóon
Man dama la
Maa ngi la chérie ouha
Dama la nob ba di la bëgga fóon
Man dama la
Maa ngi la chérie ouha

Duma la bàyyi, duma la bàyyi
Yow it bul ma bàyyi, bul ma bàyyi yeeh

Abadan, abadan, abadan
Abadaan, yow bul ma bàyyi da’imam
Abadan, abadan, abadan
Abadaan, yow bul ma bàyyi da’imam

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital